User:MAAGALAAJO-NDAW

From Wikimedia Commons, the free media repository
Jump to navigation Jump to search

Sotti xibaar.

Lu mbir bar bar

Mbëtt wéy di wuuteek bar,

Ayca nu fàqus car ci wànqaasu xibaar yi.

Du man a meew mbaa book yakkamtee nar.

Démb la Aliw Sàll wuyu ji waa DIC

Ngir leeral kopar yi ak la ko Timis dig

Ci petorolu askan wi nu jàpp ni da koo ngardaajoo

Te lépp magam a xaatim tax muy paacoo

Ak ñi mu bokkal ba tudd neen ci Aali Nguy

Mi yor kaaraange gi jiiñ neen bew ak fuy.

Beneen xëtu xibaar yi fàww mu ànd ak xiiru

Ni gaynde yaa doon wane ne duñu ay siiru.

Senegaal a doon futbal ak réewum Bene

Gaynde yee bàcci Xojjog ya mbete mbàccum bene

Benn bal ci dara ak beneen bu àttekat ba bañ

Moom la Gaynde  xët Xojjak xaw na koo gaañ

Gànna Géy moo jox Maane mu delloo ko ko

Mu doxal xaañ góol ba naaw jàppul dàra

Soppéy futbal yaa ngi sànt ndax ñoo jàll

Ñooy wéy di wéyal joŋante bi ba jot seen wàll.

Li des ci xibaar yeey tas kaar yi

Moo def góom yi indi càqaar yi

La xewoon bis boobu waa ji Sekk sol yéré ba

Ñu mbamb ko tëkku ko ngir daa def tere ba

Mel ni cig tayeef da doon dooleel ngóor-jigeen

Tax ñu artu ko ngir defoon na ko defaat ko ren

Yoroon na fi saag soloon fi caax ni OXFAM

Mi dàq ay ligéeykat ngir bañ a moy kilifaam.

Tax ñu bari ñi ko bañ yéy yàbbi ci bind àddu

Dànkaafu mbootaay yi ne fii duñu fi am kàddu.

Lii moo gënoon fës ci saabal yi xibaar yi

Def leen ko wolof woy ko wax lu toj baar yi

Ñépp bàyyi maandi mi naandalu ji ci Wolof

Dawalleen ko, walleen ko cere ju  woyof.